BACK TO THE HOMEPAGE           VOLUNTEER FOR US!
  LONWEB PARALLEL TEXTS

 

 

 

 

 

WOLOF

 
 

 

BATAAXAL GU MAG GI 
ËMB SAÑ-SAÑI DOOMI AADAMA

Ñu jàpp te nangu ne sagu doomi aadama ak sañ-sañam yépp-dañu yam te kenn mënukóo jalgati, te lu lépp nekk na cës laay ci taxufeex ci mbirum àtte ak jàmm ci biir àdduna.

UNIVERSAL DECLARATION
OF HUMAN RIGHTS

Whereas recognition of the inherent dignity and of the equal and inalienable rights of all members of the human family is the foundation of freedom, justice and peace in the world,

Ñu jàpp ne ñakk xam ak soofantal sañ-sañi doomi aadama indi na aymusiba yu tar tax képp kuy dund fippu. Temano egsi na ba mu nekk ci doomi aadama ñu mën a wax, xalaat, ci seen coobare, bundxatal, nàkk dëddu leen. Whereas disregard and contempt for human rights have resulted in barbarous acts which have outraged the conscience of mankind, and the advent of a world in which human beings shall enjoy freedom of speech and belief and freedom from fear and want has been proclaimed as the highest aspiration of the common people,
Ñu jàpp ne am na solo lool ñu aar sañ-sañi doomu aadama ak ay matukaay ci wàllu yoon; ngir doomu aadama moomu kenn du ko sonal, muy fippu ci nootaange ak lu koy bunduxatal. Whereas it is essential, if man is not to be compelled to have recourse, as a last resort, to rebellion against tyranny and oppression, that human rights should be protected by the rule of law,
Ñu jàpp ne am na solo lool ñu góor-goorlu ba gën a rataxal jokkalante gi diggante xeet yi. Whereas it is essential to promote the development of friendly relations between nations,
Ñu jàpp ne ci bataaxal boobule mbootaayu xeet yi yeesalaat na ay pas-pasam jëme ko ci sañ-sani doomi aadama yu tolloo, ci sag, ci bir lépp lu aju ci dundin diggante góor ak jigéen, ci biir tawfeex gu yaa. Whereas the peoples of the United Nations have in the Charter reaffirmed their faith in fundamental human rights, in the dignity and worth of the human person and in the equal rights of men and women and have determined to promote social progress and better standards of life in larger freedom,
Ñu jàpp ne réew yi ci bokk jël nañu ay matukaay ngir dëgëral jokkalante gi ak mbootaayu xeet yi, ñu naw it bu baax sann-sañi doomi aadama ak tawfeex yu wóor ci biir àdduna yépp. Whereas Member States have pledged themselves to achieve, in cooperation with the United Nations, the promotion of universal respect for and observance of human rights and fundamental freedoms,
Ñu jàpp ne ànd taxawal sañ-sañ yeek tawfeex yi nekk na lu am solo lool ngir, darajaal matukaay yooyu. Whereas a common understanding of these rights and freedoms is of the greatest importance for the full realization of this pledge, Now, therefore,
Ndaje mu mag mi biral na ci bataaxal bii ne xeet yépp, réew yépp ak kurel yépp ñu jàpp li ci nekk, ci seen xel, te ñu góor-góorlu, ñu jaarale lii lépp ci njàng mi ak yar gi.

Ñu lawal sañ-sañ yeek taawfeex yi jël aymatukaay ci biirak bitim réew.

Ñu nangu te di doxal fépp ci anam gu wér ci biir xeet yi sosoo ci réew i bokk ci mbootaay gi ak gox yi bootu ci ñoom.

 

The General Assembly, proclaims this Universal Declaration of Human Rights as a common standard of achievement for all peoples and all nations, to the end that every individual and every organ of society, keeping this Declaration constantly in mind, shall strive by teaching and education to promote respect for these rights and freedoms and by progressive measures, national and international, to secure their universal and effective recognition and observance, both among the peoples of Member States themselves and among the peoples of territories under their jurisdiction.

1. Matukaay bu jëkk bi

Doomi aadama yépp danuy juddu, yam ci tawfeex ci sag ak sañ-sañ. Nekk na it ku xam dëgg te ànd na ak xelam, te war naa jëflante ak nawleen, te teg ko ci wàllu mbokk.

Article 1

All human beings are born free and equal in dignity and rights. They are endowed with reason and conscience and should act towards one another in a spirit of brotherhood.

2. Naareelu matukaay

Ku ne mën naa wax ne am na ay sañ-sañ ak ay tawfeex yu sosoo ci bataaxal bii te amul xeej ak seen, rawatina ci wàllu xeet, melo, awra, làkk, diiné, peete ci wàllu politig, xalaat, réew mbaa askan woo mën ti sosoo, ci it wàllu juddu alal ak lu mu mën ti doon.

Rax sa dolli amul xeej ak seen ci politig, yoon, mbaa doxalin wu aju ci bitim réew mbaa suuf soo xamne nit ki fa la cosaanoo; réew moomu mbaa suuf soosu moom na boppam walla deet, mbaa ñu yamale yengu-yëngoom.

Article 2

Everyone is entitled to all the rights and freedoms set forth in this Declaration, without distinction of any kind, such as race, colour, sex, language, religion, political or other opinion, national or social origin, property, birth or other status.


Furthermore, no distinction shall be made on the basis of the political, jurisdictional or international status of the country or territory to which a person belongs, whether it be independent, trust, non-self-governing or under any other limitation of sovereignty.

3. Ñatteelu matukaay

Nit kune war naa dund ci tawfeex ak kaaraange.

Article 3

Everyone has the right to life, liberty and security of person.

4. Ñeenteelu matukaay

Waruñoo def kenn jaam mbaa mbindaan. Njaam ak njaayum jaam nanguwunu ko ci anam gu mu mën ti doon.

Article 4

No one shall be held in slavery or servitude; slavery and the slave trade shall be prohibited in all their forms.

5. Juróomeelu matukaay

Waruñoo mbugal, tutal, mbaa teg kenn lu metti lool lu yelloo wul ak doomu aadama.

Article 5

No one shall be subjected to torture or to cruel, inhuman or degrading treatment or punishment.

6. Juróom benneeli matukaay

Nit ku ne am na sañ-sañ ñu war kaa nangul darajaam ci wàllu yoon.

Article 6

Everyone has the right to recognition everywhere as a person before the law.

7. Juróom benneeli matukaay

Népp a yam ci kanamu yoon. Te it amul xeej ak seen, ku ne yoon woowu war na laa aar. Népp war nañu leen aar ci luy jalgati liñu tënk ci bataaxal bii ak bepp yëngu-gëngu buy indi par-parloo.

Article 7

All are equal before the law and are entitled without any discrimination to equal protection of the law. All are entitled to equal protection against any discrimination in violation of this Declaration and against any incitement to such discrimination.

8. Juróom natteelu matukaay

Nit ku ne am na sañ-sañ dem ci berebi àtte kaay yi ci reewam saa yoo xamne sañ-sañam yooyu dëppook sàrti réewam mba yoon jalgati nañu ko.

Article 8

Everyone has the right to an effective remedy by the competent national tribunals for acts violating the fundamental rights granted him by the constitution or by law.

9. Juróom ñentteeli matukaay

Menuñoo jàpp, tëj, mbaa genne kenn réewam te tegunu ko ci yoon.

Article 9

No one shall be subjected to arbitrary arrest, detention or exile.

10. Fukkeeli matukaay

Ci lu wér, nit kune mën naa egg ci berebu atte kaay wax li ko naqari ci anam gu jub, te baña ànd ak par-parloo, ne dañu ko taxal.

Article 10

Everyone is entitled in full equality to a fair and public hearing by an independent and impartial tribunal, in the determination of his rights and obligations and of any criminal charge against him.

11. Fukkeeli been matukaay ak benn

  1. Bépp nit bu ñu taqal cimbir mu tar jàppe nanu ko ku set ba loolu ñu ko taxal leer nàññ ginnaaw bi ñu ko attee. Te ñu taxawu ko ci lépp lu koy aar ci atte boobule.

  2. Duñu tëj kenn ci ay jëfam mbaa lu mu fàtte mbete loolu mu jëf ci jamono jooju nekkul mbir mu tar ci wàllu yoon, ci biir ak bitim réew. Foofu it yoon du ko teg lu dul limengóok li mu def ci jamono jooju.

Article 11

  1. Everyone charged with a penal offence has the right to be presumed innocent until proved guilty according to law in a public trial at which he has had all the guarantees necessary for his defence.
  2. No one shall be held guilty of any penal offence on account of any act or omission which did not constitute a penal offence, under national or international law, at the time when it was committed. Nor shall a heavier penalty be imposed than the one that was applicable at the time the penal offence was committed.

12. Fukkeeli matukaay ak ñaar

Kenn warula xuus ci dundinu doomu aadama, bu njabootam, ci lu jëm ci këram mbaa lu mengóok moom, di damm it jarajaam. Buñu jalgatee yii nit kune am na sañ-sañ ñu aar ko ci wàllu yoon.

Article 12

No one shall be subjected to arbitrary interference with his privacy, family, home or correspondence, nor to attacks upon his honour and reputation. Everyone has the right to the protection of the law against such interference or attacks.

13. Fukkeeli matukaay ak ñatt

  1. Nit kune am na sañ-sañ wëndeelu ni mu ko neexe, tànn it dekkuwaayam ci biir réew bu mu mën ti doon.
  2. Nit kune am na sañ-sañ génn réew mu mu mën ti doon. Fimu dëkk it bokk na ci-ak it dellusi ci réewam.

Article 13

  1. Everyone has the right to freedom of movement and residence within the borders of each State.
  2. Everyone has the right to leave any country, including his own, and to return to his country.

14. Fukkeeli matukaay ak ñent

  1. Nit kune bu ñu ko mbugalee am na sañ-sañ làqu ji, mbaa ñaan ñu làq ko ci yeneni réew.
  2. Su fekkee ne nit ki dañu koy toppu ginnaaw bi mu defee jëyyi, mbaa yëngu-yëngóon méngóowul ak li mbootaayu xeet yi tëral, sañ-sañ boobu.

Article 14

  1. Everyone has the right to seek and to enjoy in other countries asylum from persecution.
  2. This right may not be invoked in the case of prosecutions genuinely arising from non-political crimes or from acts contrary to the purposes and principles of the United Nations.

15. Fukkeeli matukaay ak juróom

  1. Nit ku ne am na sañ-sañ xeetoo cim réew.
  2. Mënuñu ne nit ki xeetoowul cim réew te teguñu ko fenn, mbaa ñu xañ ko sañ-sañ su bëggee soppi xeetoom ak réewan.m

Article 15

  1. Everyone has the right to a nationality.
  2. No one shall be arbitrarily deprived of his nationality nor denied the right to change his nationality.

16. Fukkeeli matukaay ak juróom benn

  1. Jigéen mbaa jóor saa yu matee amul xaaj ak seen, ak waaso bu mu mën ti bokk, réew, mba diiné am na sañ-sañ sëy ak it sos njaboot. Ñoo yam it sañ-sañ, balaa ñuy sëey, ci biir sëy ak it bu seen sëy tasee.
  2. Sëy kenn menunuko fas, xanaa lu jiitu ku ne ci way-dencante yi joxe xalaatam.
  3. Njaboot nekk na menneef gu am solo ci askan wi.

 

Article 16

  1. Men and women of full age, without any limitation due to race, nationality or religion, have the right to marry and to found a family. They are entitled to equal rights as to marriage, during marriage and at its dissolution.
  2. Marriage shall be entered into only with the free and full consent of the intending spouses.
  3. The family is the natural and fundamental group unit of society and is entitled to protection by society and the State.

17. Fukkeeli matukaay ak juróom ñaar

  1. Ngay dund yaw doww mbaa ak mbooloo am nga sañ-sañ am loo moomal sa bopp.
  2. Menuñoo xañ kenn am aman.

Article 17

  1. Everyone has the right to own property alone as well as in association with others.
  2. No one shall be arbitrarily deprived of his property.

18. Fukkeeli matukaay ak juróom ñatt

Nit kune am na sañ-sañ xalaat ak sa goom ci wàllu diine, soppi it diineem mba ngëmam, am na it tawfeex feeñal diineem, mbaa ngëmam, ak mbooloo, mbaa moom doww, fu àdduna daje mbaa deet, jarali ko ci njàngale mi, ci ay jëf, ci jaamu yi ak xarbaax.

Article 18

Everyone has the right to freedom of thought, conscience and religion; this right includes freedom to change his religion or belief, and freedom, either alone or in community with others and in public or private, to manifest his religion or belief in teaching, practice, worship and observance.

19. Fukkeeli matukaay ak juróom ñent

Nit ku ne am na sañ-sañ wax mbaa bind lu ko soob. Ci waxam yooyule kenn menuko ce bundu xatal. Te it am na sañ-sañ di gëstu, di jot, di wasare ci anam gu yaa ay xabaaraki xalaat ak ay jumtukaay yu mi Men ti jefandikóo.

Article 19

Everyone has the right to freedom of opinion and expression; this right includes freedom to hold opinions without interference and to seek, receive and impart information and ideas through any media and regardless of frontiers.

20. Ñaar fukkeeli matukaay

  1. Nit kune am na sañ-sañ woote ab ndaje, mbaa sos mbootaay ci jàmm.
  2. Mënuñoo bokk loo kenn ci mbootaay te àndu ci.

Article 20

  1. Everyone has the right to freedom of peaceful assembly and association.
  2. No one may be compelled to belong to an association.

21. Ñaar fukkeeli matukaay ak benn

  1. Nit ku ne am na sañ-sañ bokk ci ñiy doxal mbiri réewam. Mu teewal fa boppam, mbaa mu yabal ab ndaw mu teewal ko fa.
  2. Nit ku ne am na sañ-sañ, amul xeej ak seen liggéey ci bépp béréb buy doxal mbiri réewam.
  3. Pas-pasu askan mooy cëslaay buy dëgëral lépp luy doxal réew. Pas-pas gile war na feeñ ci palin yu yiw yu ñu wara amal léeg-léeg ci tannin gu yaa te am sutura,mbaa topp yoon wu wóor wu andak taw feex ci wàllu pal.

Article 21

  1. Everyone has the right to take part in the government of his country, directly or through freely chosen representatives.
  2. Everyone has the right to equal access to public service in his country.
  3. The will of the people shall be the basis of the authority of government; this will shall be expressed in periodic and genuine elections which shall be by universal and equal suffrage and shall be held by secret vote or by equivalent free voting procedures.

22. Ñaar fukkeeli matukaay ak ñaar

Nit ku ne meññeefu askan wi am na sañ-sañ ñu aar ko ci giru dundam. Ci dundam war na ci am xol bu sedd ci sañ-sañam yooyu, lu aju ci koom-koomam, ci dundinam ak ci lépp lu aju ci aadaam te di ko jox maanaa ak yookkute gu ànd ak tawfeex ci wàllu darajaam, loolu lépp nag ku ne doomu réew mi indi dooleem ak di jokkalante ak bitim réew te mu méngook tërërin ak am-amu réew mu ne.

Article 22

Everyone, as a member of society, has the right to social security and is entitled to realization, through national effort and international co-operation and in accordance with the organization and resources of each State, of the economic, social and cultural rights indispensable for his dignity and the free development of his personality.

23. Ñaar fukk ak ñatteeli matukaay

  1. Nit ku ne am na sañ-sañ liggéey, tànn it ci eanam gu ko neex liggéeyamm te mu dëppóok ay sàart yu yam te baax ci wàllu liggéey. Te it ñu aar ko ci ñàkkub liggéey.
  2. Amul xeej ak seen ku néppam nanu sañ-sañ ñu fay leen, te loolu méngóok li mu aliggéey.
  3. Keépp kuy liggéey am na sañ-sañ ñu jox ko pay gi mu yellool, baax te mën koo dundal ak njabbotam te mu yellook sagu doomu aadama, mu mottaliku it ak yeneeni pexe su mënee am ngir aar dundinam.
  4. Nit ku ne am na sañ-sañ samp mbaa bokk ci ay kurel yu koy taxawu ci wàllu liggéeyam.

Article 23

  1. Everyone has the right to work, to free choice of employment, to just and favourable conditions of work and to protection against unemployment.
  2. Everyone, without any discrimination, has the right to equal pay for equal work.
  3. Everyone who works has the right to just and favourable remuneration ensuring for himself and his family an existence worthy of human dignity, and supplemented, if necessary, by other means of social protection.
  4. Everyone has the right to form and to join trade unions for the protection of his interests.

24. Ñaar fukk ak ñenteeli matukaay

Nit ku ne am na sañ-sañ noppalu, feexal xolal ak it di yamale diirub liggéeyam ak it léeg-léeg muy për, bër gu ànd ak xaalis.

Article 24

Everyone has the right to rest and leisure, including reasonable limitation of working hours and periodic holidays with pay.

25. Ñaar fukk ak juróomeeli matukaay

  1. Nit ku ne am na sañ-sañ am dundingu yamamaay ngir dëgëral wér-gi-yaramam, raataageem ak bu njabootam, lrawatina ci wàllu lekk col, dëkkuwaay, lépp lu aju ci wàllu paj ak bépp yëngu-yëngu gu am farata ci wàllu dundam. Am na it sañ-sañ ñu aar ko bu liggeeyatul bu feebaree, bu amee laago, ñàkk saxnaam mbaa sërinam, mbaa màgget, mbaa mu ñàkk li muy suturloo ci anam yu dul ci cootareem.
  2. War nañu beral loxo, dimbali képp ku tollu ci am doom ak it gune yi. Bépp xale bu juddu ci sëy, mbaa bu judduwul ci sëy ñoo bokk benn anam buñ leen di aare.

Article 25

  1. Everyone has the right to a standard of living adequate for the health and well-being of himself and of his family, including food, clothing, housing and medical care and necessary social services, and the right to security in the event of unemployment, sickness, disability, widowhood, old age or other lack of livelihood in circumstances beyond his control.

  2. Motherhood and childhood are entitled to special care and assistance. All children, whether born in or out of wedlock, shall enjoy the same social protection.

26. Ñaar fukk ak juróom benneeli matukaay

  1. Nit ku ne am na sañ-sañ ñu jàngal ko, njàng mi waruñu ci fayaku lu mu bon bon ci njàng mu suufe mi te am solo. Njàng mu suufe mi lu war la. Njàng mu xarala mi, te it aju ci wàllu liggéey war nanu koo wasaare. Amul xeej ak seen njàng mu kawe mi ubbil nañu ko képp ku ko yelloo.
  2. Njàng war naa indi naataange gu yaa ci ddoomi aadama te it war na dëgëral ñu naw sañ-sañi doomi aadama aki tawfeexam ci anam gu yaa-wat na it rataxal déggóo gi ak yokkute mbootaayu xeet yi ngir jàmm sax.




  3. Waajur yi ñoo jëkk am sañ-sañ ci anam gi ñuy yare seeni doom.

Article 26

  1. Everyone has the right to education. Education shall be free, at least in the elementary and fundamental stages. Elementary education shall be compulsory. Technical and professional education shall be made generally available and higher education shall be equally accessible to all on the basis of merit.
  2. Education shall be directed to the full development of the human personality and to the strengthening of respect for human rights and fundamental freedoms. It shall promote understanding, tolerance and friendship among all nations, racial or religious groups, and shall further the activities of the United Nations for the maintenance of peace.
  3. Parents have a prior right to choose the kind of education that shall be given to their children.

27. Ñaar fukk ak juróom nenteeli matukaay

  1. Nit ku ne am na sañ-sañ bokk ci dépp lu aju ci caaday askan wi, di bànneexu ci lu cu aju ak it bokk ci lépp luy suqali xarala gi ak lu ciy meñ.
  2. Nit ku ne am na sañ-sañ ñu aaral ko lépp lu aju ci lu mudefar ci wàllu la xarala, mbind mbaa lu aju ci wàllu caala.

Article 27

  1. Everyone has the right freely to participate in the cultural life of the community, to enjoy the arts and to share in scientific advancement and its benefits.
  2. Everyone has the right to the protection of the moral and material interests resulting from any scientific, literary or artistic production of which he is the author.

28. Ñaar fukk ak juróom natteeli matukaay

Nit ku ne war naa tawaxu dëpp lu aju a askan wi, ak lu aju ci bitim réewam ba sañ-sañ ak tawfeex yi bataaxalu xeet gi ëmb mën a sax.

Article 28

Everyone is entitled to a social and international order in which the rights and freedoms set forth in this Declaration can be fully realized.

29. Ñaar fukk ak juróom nenteeli matukaay

  1. Nit ku ne am na ay wareef yu ko war digganteem ak dëkkandoom yi ngir dëgëral ci anam gu ya darajaam.
  2. Nit ku ne buy doxal ay sañ-sañam aki tawfeexam war naa sallook li ko yoon may, ngir mu mën a nangu, naw, sañ-sañ nawleem ba léepp lu aju ci yiw, teey ak naataange gu yaa sax ci askan wi.


  3. Sañ-sañ yeek tawfeex yi mënuñukoo doxal ci anam gu deppoo-wul li mbootaayu xeet yi misër mbaa taxawal.

 

Article 29

  1. Everyone has duties to the community in which alone the free and full development of his personality is possible.
  2. In the exercise of his rights and freedoms, everyone shall be subject only to such limitations as are determined by law solely for the purpose of securing due recognition and respect for the rights and freedoms of others and of meeting the just requirements of morality, public order and the general welfare in a democratic society.
  3. These rights and freedoms may in no case be exercised contrary to the purposes and principles of the United Nations.

30. Fanweereeli matukaay

Ci fànn gu mu mën ti doon ci bataaxal bii, bépp réew, mbootaay mbaa nit, warul doxal mbaa def luy yàq sañ-sañ yeek tawfeex.

 

Article 30

Nothing in this Declaration may be interpreted as implying for any State, group or person any right to engage in any activity or to perform any act aimed at the destruction of any of the rights and freedoms set forth herein.